Bare na ñu fexee bind ab nettalib mbir, yi sotti woon ci sunu biir, noonee nu ko jote ca ña ko fekke woon ca ndoorte la, te seede yooyu mujj doon jawriñi kàddug Yàlla. Moo tax man it, ma fas laa yéenee bindal lépp ba mu jekk gannaaw ba ma gëstoo mbir mépp, dale ko ca ndoorte la, ba mu leer nàññ. Ko defee nga xam xéll ne li ñu la jàngal, lu wér péŋŋ la.
Show more...