Waxtaan wi ab jukki la ci téereb kàngam boobu di Imaam Saaraani. Ci téere bi dafa ciy jàngale teggiini niti Yàlla yi yoy képp ku sóobu ci Yàlla te bëgg a bokk ci góor ña war nga leen ca roy.
Waxtaan wii Imaam Xasaali dafa ciy wax njariñ yi ci koor ak yiiw yi mu man a fàggul jullit bi, waaye tamit leeral dayo bi koor am fa saa Boroom.
Waxtaan wii mu ngi aju ci àq yi nit man a ameel ay moroomam ak i saafara yi leen di far. Àq mat naa moytu, ndax ëllëg lu ñuy fayante la. Di jëfandikoo ñaan yi niti Yàlla yi tënk nag da ciy am solo ngir ëllëg sa dara du lëj.
Ci mujjantalu téere bi, Imaam Dardiir daa tënkaat gàllankoor yiy tënk nit ki ba du àgg ci Yàlla, niral ci jikko yu mel ni rëy, ngistal añs… waaye tamit leeral ci ne Jaamu Yàlla di ci sàkku leneen ludut Yàlla ci gàllankoor yi la bokk.
Ci waxtaan wi, danuy leeral xeeti xalaat yiy toq ci xelu doomu aadama, seen i jeexital ak yoon wi nit ki di jaar ngir sellal ay xalaatam ba duñu ko yóbb ci moy Yàlla.